1
Mucc ga 23:25-26
Kàddug Yàlla
KY
Jaamuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, ma barkeel seen dugub ak seen ndox, boole ci jële wopp ci seen biir. Su ko defee du kenn ku ëmbam di yàqu, mbaa mu tëlee am doom ci seenum réew, te maay matal sëkk seen limu fan.
Compare
Explore Mucc ga 23:25-26
2
Mucc ga 23:20
«Te nag man ci sama bopp, maay yebal malaaka, mu di leen sàmm ci yoon wi, ba yóbbu leen béreb ba ma waajal.
Explore Mucc ga 23:20
3
Mucc ga 23:22
Waaye su ngeen ko déggalee ba déggal ko, di jëfe li ma leen wax lépp, su boobaa ma noonoo seeni noon, bañ seeni bañaale.
Explore Mucc ga 23:22
4
Mucc ga 23:2-3
Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg. Néew-doole bi it, buleen ko far cib layoo.
Explore Mucc ga 23:2-3
5
Mucc ga 23:1
«Buleen siiwal ay fen; buleen lëngoo ak tooñkat, ngir doon seedeb naaféqam.
Explore Mucc ga 23:1