Ñu dem, ba àgg fu ñu naan Maara, waaye manuñoo naan ca ndoxum Maara, ndax wex. Looloo waral ñu tudde béreb ba Maara (muy firi Fu wex). Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?» Musaa woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji won ko dammitu bant, mu sànni ko ca ndox ma, ndox ma neex.
Foofa la Aji Sax ji dogalal bànni Israayil ay sàrti yoon ak ndigal, te fa la leen nattoo itam.