1
Jëf ya 7:59-60
Kàddug Yàlla
KY
Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!» Mu ne gurub, samp bëti óomam, daldi àddu ca kaw, ne: «Sang bi, bu leen topp bii bàkkaar.» Naka la wax loolu, daldi faatu.
Compare
Explore Jëf ya 7:59-60
2
Jëf ya 7:49
“Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal? Boroom bee ko wax. Mu ne: Ana ban béreb ay sama dalluwaay?
Explore Jëf ya 7:49
3
Jëf ya 7:57-58
Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam; ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.
Explore Jëf ya 7:57-58