Su ma nammoona damu it, du doon ag ndof, ndax dëgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn bañ maa fooge lu wees li mu gis may def, ak li mu dégg may wax.
Te it, waccalees na ma ndégu biir suux, mu taxawe ndawal Seytaane, di ma mitital, ngir ma baña bew ndax peeñu yu yéeme.