Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol. Seen dundin ci biir jàmbur ñi gëmul, rafetalleen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.