1
1.Yowaan 3:18
Kàddug Yàlla
KY
Xale yi, bunu soppante ci làmmiñu kese maanaam ay wax, waaye nanu ko jëfe, te muy dëgg.
Compare
Explore 1.Yowaan 3:18
2
1.Yowaan 3:16
Nii nag lanuy xame lan mooy cofeel: Almasi bi dafa joxe bakkanam ngir nun; kon nun itam, li nu war mooy nu joxe sunu bakkan ngir sunu bokki gëmkat.
Explore 1.Yowaan 3:16
3
1.Yowaan 3:1
Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.
Explore 1.Yowaan 3:1
4
1.Yowaan 3:8
Kuy bàkkaar, ci Seytaane la bokk, ndax Seytaane moo dale bàkkaar ca njàlbéen ga. Te Doomu Yàllaa dikk ngir nasaxal liggéeyu Seytaane.
Explore 1.Yowaan 3:8
5
1.Yowaan 3:9
Képp ku sosoo ci Yàlla doo dëkke bàkkaar, ndax jiwum Yàlla moo nekk ci moom; du mana wéy ciy bàkkaar, ndax ci Yàlla la sosoo.
Explore 1.Yowaan 3:9
6
1.Yowaan 3:17
Waaye ku am alalu àddina, su gisee mbokkam mu nekk ci soxla, ba noppi tëjal ko xolu yërmande, kooku ana nu cofeelu Yàlla nekke ci moom?
Explore 1.Yowaan 3:17
7
1.Yowaan 3:24
Kuy sàmm ndigali Yàlla nag, yaa sax ci moom, moom it mu sax ci yaw. Te li nuy xamal ne mu ngi sax ci nun moo di Noo gu Sell gi mu nu sédd ab cér.
Explore 1.Yowaan 3:24
8
1.Yowaan 3:10
Nii lees di ràññee doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def njub, bokkul ci Yàlla; képp ku soppul sa mbokkum gëmkat it, naka noonu.
Explore 1.Yowaan 3:10
9
1.Yowaan 3:11
Lii kat moo di solos xibaar ba ngeen déggoon ca njàlbéen: nanu soppante
Explore 1.Yowaan 3:11
10
1.Yowaan 3:13
Kon bokk yi, bu leen àddina bañee, bumu leen jaaxal.
Explore 1.Yowaan 3:13