«Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu, ngir sa koor baña feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo.