1
Njàlbéen ga 22:14
Kàddug Yàlla
KY
Ibraayma nag tudde béreb boobu Yawe Yire (muy firi Aji Sax ji dina dikk). Moo tax ñuy wax ba tey, naan: «Aji Sax jaa ngay dikke ca tundam.»
Comparer
Explorer Njàlbéen ga 22:14
2
Njàlbéen ga 22:2
Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.»
Explorer Njàlbéen ga 22:2
3
Njàlbéen ga 22:12
Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»
Explorer Njàlbéen ga 22:12
4
Njàlbéen ga 22:8
Ibraayma ne ko: «Yàlla moom ci boppam dina dikk ak gàtt bi nuy def sarax, doom,» ñu daldi ànd dem, ñoom ñaar.
Explorer Njàlbéen ga 22:8
5
Njàlbéen ga 22:17-18
maa lay barkeel a barkeel, ful a ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk, te xeeti àddina yépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»
Explorer Njàlbéen ga 22:17-18
6
Njàlbéen ga 22:1
Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.»
Explorer Njàlbéen ga 22:1
7
Njàlbéen ga 22:11
Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!»
Explorer Njàlbéen ga 22:11
8
Njàlbéen ga 22:15-16
Ci kaw loolu malaakam Yàlla ma dellu àddoo asamaan ne Ibraayma: «Déglul lii Aji Sax ji wax: “Giñ naa ci man mii, gannaaw yaa def lii, te gàntaloo ma sa jenn doom ji
Explorer Njàlbéen ga 22:15-16
9
Njàlbéen ga 22:9
Ba ñu àggee fa ko Yàlla wax, Ibraayma sàkk fa ab sarxalukaay, teg ca matt ma, yeew Isaaxa doomam, teg ko ca kaw matt ma ca sarxalukaay ba.
Explorer Njàlbéen ga 22:9