1
Màrk 7:21-23
Téereb Injiil
TI
Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom, njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof. Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
Comparer
Explorer Màrk 7:21-23
2
Màrk 7:15-16
Li ci biti, tey dugg nit, du ko mana indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.»
Explorer Màrk 7:15-16
3
Màrk 7:6
Yeesu ne leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee: “Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma.
Explorer Màrk 7:6
4
Màrk 7:7
Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
Explorer Màrk 7:7
5
Màrk 7:8
Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.»
Explorer Màrk 7:8