1
Macë 23:11
Téereb Injiil
TI
Ki gëna mag ci yéen mooy ki nangoo nekk seen surga.
Comparer
Explorer Macë 23:11
2
Macë 23:12
Kuy yékkatiku dees na la suufeel; kuy suufeelu, ñu yékkati la.
Explorer Macë 23:12
3
Macë 23:23
«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des.
Explorer Macë 23:23
4
Macë 23:25
«Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal.
Explorer Macë 23:25
5
Macë 23:37
«Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen!
Explorer Macë 23:37
6
Macë 23:28
Yéen itam, ci ngistal dangeena mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon.
Explorer Macë 23:28