1
Macë 15:18-19
Téereb Injiil
TI
Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe. Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga.
Comparer
Explorer Macë 15:18-19
2
Macë 15:11
du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
Explorer Macë 15:11
3
Macë 15:8-9
“Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
Explorer Macë 15:8-9
4
Macë 15:28
Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
Explorer Macë 15:28
5
Macë 15:25-27
Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.» Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
Explorer Macë 15:25-27