Màrk 16
16
Yeesu Almasi bi dekki na
1Ba bésub Noflaay ba wéyee, Maryaamam Magdala ak Maryaama yaayu Yanqóoba ñoo ànd ak Salome jëndi diw gu xeeñ, ngir diwe ko néewub Yeesu. 2Ba njël jotee, yemook bésub dibéer, ba jiitu ca ayu bésu Yawut ya, ñu xëy ca bàmmeel ba. 3Ña nga naa ca seen biir: «Ku nuy béraŋal doj, wi ub buntu bàmmeel bi?»
4Naka lañu ne siggét rekk, ñu gis ne doj wa béraŋu na ba lafu. Te doj wu réy lool la woon. 5Ñu dugg ca biir bàmmeel ba, daldi gis xalelu góor bu tooge wetu ndijoor, sol mbubb mu weex tàll. Ñu tiit lool. 6Mu ne leen: «Buleen tiit. Yeesum Nasaret, mi ñu daajoon ci bant, mi ngeen di seet, dekki na. Nekku fi. Fii lañu ko tëraloon. 7Demleen nag wax ay taalibeem, ñook Piyeer, ne leen Yeesu jiituji na leen Galile. Foofa ngeen koy gise, na mu leen ko waxe woon.»
8Ba loolu amee jigéen ña génn bàmmeel ba, daw, di lox te yéemu. Waxuñu kenn dara nag ndax tiitaange#16.8 Màrk moom fii la yem; li ci des, keneen moo ko nettali..
Yeesu feeñu na ay taalibeem
9Gannaaw ba Yeesu dekkee ca subag dibéer ga, ndoortel ayu bés ba, Maryaamam Magdala ma mu dàqaloon juróom ñaari rab, moom la njëkka feeñu. 10Maryaama nag àggeji ko àndandooy Yeesu ya, fekk ñuy naqarlu, di jooy. 11Ba leen Maryaama nee Yeesoo ngi dund, te gis na Yeesu, gëmuñu ko.
12Gannaaw loolu ñaar ca ñoom la Yeesu feeñoo jeneen jëmm, fekk leen ci yoon wu jëm àll ba. 13Ñu waññiku, wax ko ña ca des, waaye ñoom it gëmuñu leen.
14Gannaaw ga, Yeesu feeñu na fukki taalibe yaak benn, fekk leen ñuy lekk. Mu yedd leen ndax seen ngëmadi ak seenug të, ngir la ñu gëmul ña ko njëkka gis, gannaaw ba mu dekkee. 15Mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp, ngeen àgge nit ñépp xibaaru jàmm bii. 16Ku gëm, te ñu sóob ko ci ndox, dina mucc; ku gëmul, dees na ko teg daan. 17Ñi gëm nag yii firnde lañuy àndal: dinañu dàq ay rab ci sama tur, dinañu làkk làkk yu bees; 18dinañu jàppe seeni loxo ay jaan; bu ñu naanee tooke buy rey bu mu mana doon, du leen wàññi dara; te dinañu teg jarag ji loxo, ñu wér.»
19Gannaaw ba Sang bi Yeesu waxee ak ñoom, ñu yéege ko asamaan, mu toog ci ndijooru Yàlla. 20Taalibe ya nag di waareji fépp, Sang bi ànd ak ñoom di liggéey, tey dëggale kàddu ga, firnde ya kàddu ga àndal.
Sélection en cours:
Màrk 16: KY
Surbrillance
Copier
Comparer
Partager
Tu souhaites voir tes moments forts enregistrés sur tous tes appareils? Inscris-toi ou connecte-toi
Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9
Apps and more at https://kaddugyalla.com/
Copyright info at https://kaddugyalla.com/copyright