Logo YouVersion
Îcone de recherche

Luug 2

2
Yeesu juddu na ca Betleyem
1Jamono yooyu ndigal moo tukkee woon ci buur bu mag bu ñuy wax Sesaar Ogust. Mu ne na ñépp binduji ca limeef ya. 2Mbindu mooma mooy mu njëkk ma, yemook ba Kiriñus dee boroom réewum Siri. 3Ci kaw loolu ñépp binduji, ku nekk ca sa dëkku cosaan. 4Ku ñuy wax Yuusufa itam jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndax ci waa kër Daawuda la askanam bokk. 5Maryaama mi digook moom séy la àndal binduji, te fekk ko mu ëmb. 6Naka lañu dal Betleyem, waxtuw muccam agsi. 7Mu am doom ju góor, mu dib taawam. Mu laxas ko, tëral ko ca gàmbug jur ga#2.7 gàmbug jur ga: nit ñi ak jur gi ñoo daan bokk fu ñuy fanaan, doonte dañoo sàkkaloon jur gi béreb bu gëna suufe, gàmbug jur gi dox seen diggante ak nit, ñay féete fu gëna kawe., ndax ñàkk fu ñu xaj ca néegu gan ba.
Malaaka feeñu na ay sàmm
8Booba ay sàmm a nga ca gox boobee, di fanaanee wattu seenug jur. 9Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange ju réy. 10Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp. 11Bésub tey jii ca dëkku Daawuda, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy Almasi bi, di Sang bi. 12Li ngeen ciy def ab takk moo di: dingeen gis liir bu ñu laxas, tëral ko ci gàmbug jur.»
13Ca saa sa gàngooru asamaan gu mag ànd ak malaaka mi, di sàbbaal Yàlla, ne:
14«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe,
jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»
15Ba malaaka ya bàyyikoo ca sàmm sa, dellu asamaan, sàmm say wax ca seen biir, naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, te Boroom bi xamal nu ko.»
16Ñu gaaw dem ba foofa, daldi gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir ba tëdd ca gàmbug jur ga. 17Naka lañu leen gis, daldi leen xamal la ñu leen wax ca mbirum xale ba. 18Mboolem ña dégg la leen sàmm sa wax nag waaru lool. 19Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam. 20Ba loolu amee sàmm sa dellu, di sàbbaal aka sant Yàlla ci mboolem la ñu dégg, gis ko, te lépp ame noonee ñu leen ko waxe woon.
Yóbbu nañu Yeesu ca kër Yàlla ga ca Yerusalem
21Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarafal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu.
22Gannaaw ba seen fani setlu#2.22 setlu: ab diir lañu àppaloon wasin-bees gannaaw bu taawloo góor, bala moo yóbbu xale bi kër Yàlla ga, ngir def sarax yi setluy wasin-bees laaj. Seetal ci Sarxalkat yi 12.6-8. matee, ni ko yoonu Musaa laaje, ñu yóbbu xale bi Yerusalem, ngir teewal ko fi kanam Boroom bi, 23noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.» 24Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw.»
Simeyon sàbbaal na Yàlla
25Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israayil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom. 26Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi. 27Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj. 28Simeyon itam jël xale bi, leewu ko, daldi sàbbaal Yàlla, ne:
29«Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam,
mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.
30Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal,
31waajal ko fi kanam askan yépp,
32mu dig leer, ñeel jàmbur ñi,
sagal Israayil sa ñoñ.»
33Baay bi ak ndey ji nag yéemu ci kàddu yooyu ñu wax ci xale bi. 34Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqaliku ci digg Israayil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal. 35Yaw nag, sab xol la aw naqar wu mel ni saamar di xar, ba ñu bare la seen xalaati biir xol di feeñ.»
Aana sant na Yàlla
36Jigéen ju ñuy wax Aana, ab yonent la woon ca Yerusalem, di doomu Fanuwel mi askanoo ci giirug Aser. Mag la woon lool. Ba muy janq la séy, nekk ak jëkkëram juróom ñaari at. 37Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak ñaan la daan jaamoo guddi ak bëccëg. 38Aana nag dikk moom it ca waxtu woowa, daldi delloo Yàlla njukkal. Ci kaw loolu muy waxtaane mbirum xale bi ak mboolem ña doon séentu bésu goreelug Yerusalem.
39Ci kaw loolu ñu matal mboolem lu yoonu Boroom bi laaj, doora dellu Nasaret, seen dëkk ba ca diiwaanu Galile. 40Xale bi nag di màgg, di dëgër, xel mu rafet wër ko, te yiwu Yàlla ànd ak moom.
Yeesu feeñ na ca kër Yàlla ga
41At mu jotaan nag waajuri Yeesu daan dem Yerusalem, ngir màggali bésub Mucc ba. 42Ba Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggali na ñu ko baaxoo woon. 43Ba màggal ga tasee, ñu ñibbi, ngóor sa Yeesu moom des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko. 44Ñu xalaat ne, Yeesu daa ànd ak ñu ñu bokkaloon yoon. Dox nañu bésub lëmm, door koo wëri ci seeni bokk ak seeni xame, 45te taxul ñu gis ko. Ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jàngalekat ya, di leen déglooka laaj. 47Mboolem ña ko dégg yéemu ci dégginam aki tontam. 48Ay waajuram gis ko, waaru. Yaayam ne ko: «Doom, li nga nu def nag? Maak sa baay a ngi jaaxle, di la seet!» 49Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?»
50Ay waajuram ñoom dégguñu kàddu googu mu leen wax. 51Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, dellu Nasaret, tey saxoo déggal ay waajuram. Yaayam nag takk mbir yooyu yépp ci xolam. 52Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.

Sélection en cours:

Luug 2: KY

Surbrillance

Copier

Comparer

Partager

None

Tu souhaites voir tes moments forts enregistrés sur tous tes appareils? Inscris-toi ou connecte-toi