1
Màrk 16:15
Kàddug Yàlla
KY
Mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp, ngeen àgge nit ñépp xibaaru jàmm bii.
Comparer
Explorer Màrk 16:15
2
Màrk 16:17-18
Ñi gëm nag yii firnde lañuy àndal: dinañu dàq ay rab ci sama tur, dinañu làkk làkk yu bees; dinañu jàppe seeni loxo ay jaan; bu ñu naanee tooke buy rey bu mu mana doon, du leen wàññi dara; te dinañu teg jarag ji loxo, ñu wér.»
Explorer Màrk 16:17-18
3
Màrk 16:16
Ku gëm, te ñu sóob ko ci ndox, dina mucc; ku gëmul, dees na ko teg daan.
Explorer Màrk 16:16
4
Màrk 16:20
Taalibe ya nag di waareji fépp, Sang bi ànd ak ñoom di liggéey, tey dëggale kàddu ga, firnde ya kàddu ga àndal.
Explorer Màrk 16:20
5
Màrk 16:6
Mu ne leen: «Buleen tiit. Yeesum Nasaret, mi ñu daajoon ci bant, mi ngeen di seet, dekki na. Nekku fi. Fii lañu ko tëraloon.
Explorer Màrk 16:6
6
Màrk 16:4-5
Naka lañu ne siggét rekk, ñu gis ne doj wa béraŋu na ba lafu. Te doj wu réy lool la woon. Ñu dugg ca biir bàmmeel ba, daldi gis xalelu góor bu tooge wetu ndijoor, sol mbubb mu weex tàll. Ñu tiit lool.
Explorer Màrk 16:4-5